Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. Yeen waa cati àddina, teewluleen! Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!
TSK
TSK · Obadiah 1:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji nee: «Damaa yàgga xeremlu, ne cell, téye sama bopp. Waaye léegi, ni kuy matu laay onke, di xiix ak a àppaat boole ca.
Sa boroom Aji Sax ji, sa Yàlla jiy layool ñoñam dafa wax ne: «Mu ngoog, maa jële ci sa loxo, kaas bu wex biy miirloo; taatu kaas ba def sama mbugal, dootoo ko naan.
¶ Aji Sax ji nag ne: «Wax leen ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil dafa wax ne: Naanleen ba màndi, di waccu, fëlëñu, tëë jóg ndax saamar bi may yebal fi seen biir.”
Ndegam ñi yeyoowul mbugal ñooy jolu kaasu mbugal, nees leen di ñàkka toppe, yeen? Dees na leen topp moos, ngeen jolu kaasu mbugal.
Ndax kat tey la àtte bi wara tàmbalee ci waa kër Yàlla. Ndegam ci nun lay tàmbalee nag, ñi gëmul xibaaru jàmm bu Yàlla, ana fu ñu jëm?