Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma, te daan lekk samaw ñam.
TSK
TSK · Obadiah 1:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kàngam ya fa Cowan dañuy teqlikook seen sago, diglekati Firawna yu xelu ya di digle ag ndof. Ma ne: «Yeen diglekat yi, nu ngeen mana waxe Firawna naan: “Nun ay boroom xel lanu, sosoo ca buur ya woon”?»
Yaw Yerusalem mu tas mi, ana looy def nii, di solu ba yànj, gànjaroo wurus, tusngalu, yàkkleey gët? Yaa ngi caaxoñu ci neen: say xéddkat wacc nañu la, sa bakkan lañuy wut.
Sa soppe yépp a la fàtte, kenn faalewu la ci, ndax dumay noon laa la duma, yar la yar bu tar ngir sa ñaawtéef ju réy ak sa bàkkaar yu bare.
¶ Lu jëm ci Edomeen ñi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Xanaa boroom xel amatul fi Teman? Xanaa ndigal a réer xamkat yi? Am seen bopp a yàqu?
Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: “Owolibaa, maa ngii di xabtalsi say far ci sa kaw; ñi la sàppi, ñoom laay bàbbee fi la wër, xiirtal leen fi sa kaw:
Lu mel ni mititu mat moo dikkal waa jii, te muy doom ju amul xel, ba juddu jot, génnul biiru ndeyam.
¶ «Fukki béjjén yi nga gis, fukki buur lañu yu jotagul ci seen nguur. Waaye diirub wenn waxtu, lañuy jot sañ-sañu nguur, ñook rab wi.