Buleen xeex ak ñoom, ndax duma leen jox ci seen suuf fu téstën sax tege, ngir Esaween ñi laa sédd diiwaanu tundu Seyir.
TSK
TSK · Obadiah 1:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw loolu ñetti xariti Ayóoba ñoo dégg mboolem musiba moomu ko dikkal. Ku nekk ci ñoom jóge këram: Elifas waa Teman ba, ak Bildàdd waa Suwa ba, ak Cofar waa Naama. Ñu bokk daje ngir dikk mas-sawu Ayóoba, dëfal ko.
Su bés baa waa Misra mel niy jigéen, di lox ndax tiit loxo bi jóg, te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi xàccil-leen ko.
Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccra? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? «Xanaa man mii di waxe njekk, te am dooley walloo.»
Kon dégluleen pexe mi Aji Sax ji waajal Edom, mébét yi mu mébétal waa Teman ñooñu! Ndegam deesu leen wommat ni seen gàtt yu ndaw, yóbbu, ba yàq seen parlu yaxeet.
Saamar ci kaw kebatukati diine yi, ba seenug ndof feeñ. Saamar ci kawi jàmbaaram, ñu ne yàcc.
Maay yebal sawara fa Teman, mu xoyomaale tatay Boccra.»
Ay xettlikat ñooy yéeg kaw tundu Siyoŋ, ngir yilif tundu Esawu, nguur gi di moomeelu Aji Sax ji.»