TSK

TSK · Philemon 1:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Éy Yàlla, bu ma bijjaawee ba weex tàll it, bu ma wacc, ba keroog may xamal maasu tey sa doole, xamal ñi ciy topp ñépp sag njàmbaar.

Ba ba ngeen di magal, man la, ba keroog ngeen di bijjaaw, maa leen di boot. Maa sàkk, maay yor, maay boot, xettli!

Kon nag Almasi, noo diy ndawam, te ci nun la Yàlla di wootee. Kon ci turu Almasi, danu leen di ñaan: nanguleena juboo ak Yàlla.

¶ Moo ma tax di ñaan, man Póol mi ñu tëj ngir Almasi, ndax ñi dul Yawut, yeen jaambur ñi,

¶ Ci man Póol, mi ñu tëj kaso ngir Almasi Yeesu, ci man ak itam ci Timote miy mbokkum gëmkat la bataaxal bii bawoo, ñeel Filemon, sunu soppe bi bokk ak nun liggéey bi.

¶ Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.