TSK

TSK · Philippians 2:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Luke 2:10 TSK

Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.

Acts 4:32 TSK

¶ Ci kaw loolu mboolem gëmkat ñi bokk menn xel, ak benn xalaat. Du kenn ku ne moo moom lenn ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp ci seen biir.

Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.

¶ Te itam Noo gi moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noowug Yàlla moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.

¶ Xanaa xamuleen ne kër Yàlla ngeen, te Noowug Yàlla moo dëkk ci yeen?

Ci genn Noo gi lañu nu sóobe ci biir wenn yaram wi, nun ñépp, nu diy Yawut, mbaa nu diy jaambur, nu diy jaam, mbaa nu diy gor, te nun ñépp, genn Noo gi lañu nu nàndale.

Ndax kat coonoy Almasi, nu mu gëna yokkoo ci sunu kaw, ndax li nu ko gëm, noonu itam la ndëfalaay liy bawoo ci Almasi di yokkoo.

¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,

ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gi.

Te it buleen tiisal Noowug Yàlla gu Sell, gi leen màndargaale xàmmikaayam ngir bésub njot ba.

Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun ñiy jaamoo Yàlla Noowam gu Sell, di damoo Almasi Yeesu, te yaakaarunu aaday nitu suuxu neen.

¶ Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ.

Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam.

¶ Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu.