TSK

TSK · Philippians 2:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»

Acts 2:36 TSK

¶ «Kon nag na wóor waa kër Israyil gépp ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàllaa ko def Sang ak Almasi.»

Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc.

Ndaxte bindees na ne: «Ndegam maay Kiy Dund, Boroom bee ko wax, man la ñépp di sukkal seen bëti óom, te man Yàlla la làmmiñu ñépp di sàbbaal.»

Teewul ci sunu wàllu bopp, jenn Yàllaa am, muy Baay bi lépp jóge ci moom, te sunu bakkan ñeel ko, benn Sang doŋŋ a am, muy Yeesu Almasi, bi lépp ame ci moom, te sunu bakkan, ci moom la ame.

Aadama mu jëkk ma, ci suuf la jóge woon, di suuf; Aadamam ñaareel mi jóge fa asamaan.