TSK

TSK · Philippians 2:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

te bu bët setee dingeen gis manoorey Aji Sax ji, ndaxte dégg na ngeen di diiŋat Aji Sax ji, ndax nun kat tekkiwunu dara, ba ngeen di nu diiŋat.»

xanaa di xultoo seen biiri xayma, baña déggal Aji Sax ji.

Njëlu ñetti xob fa ñu la soppe moo dàq yàpp wu duuf fu ñu la bañe.

Acts 6:1 TSK

¶ Jant yooyu nag, naka taalibe yi di gëna bare, Yawut ñiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci kaw Yawut ñiy wax seen làmmiñu bopp ndax néewal gu ñu gis ñu néewal ko seeni jëtun ca na ñuy séddalee ag ndimbal bés bu nekk.

Acts 15:7 TSK

Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jaambur ñi dégge ci sama làmmiñ, kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat.

Su manee am, jàmmooleen ak ñépp, ndegam ci yeen la aju.

¶ Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale, ak a téqtale, te ngeen moytu leen.

nde yeena ngi ba tey ci seenug nitey suuxu neen. Ndax gannaaw kiñaan ak ŋaayoo ngi ci seen biir, du ay niti suuxu neen ngeen ba tey, di doxale ni niti àddinay kese?

Ragal naa, bu ma dikkee, fekke leen nu ma neexul, yeen it, ngeen gise ma nu leen neexul. Ragal naa ay réeroo ci seen biir ak kiñaan ak mer mu ëpp, ak diiroo mbagg, ak waxi sos aki jëw, ak réy-réylu, akug salfaañoo.

Bunu di yég sunu bopp, di merloonte ak a iñaanante.

Buleen def dara ci kaw wujje, mbaa réy-réylu, waaye doyadiluleen, ba jàpp ne seen moroomi gëmkat a leen gën.

Fexeleen ba kenn du feyantoo. Waaye lu baax, deeleen ko deflante ci seen biir, te di ko defal ñépp.

¶ Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen sellnga, nde ku sellul du gis Boroom bi.

Waaye ku denc ci sab xol, wextanu kañaan, ak mébétum sàkku sa darajay bopp, bul damoo xel mu rafet, nde kon nga moy dëgg.

Na daggook lu bon, tey def lu baax, na sàkku jàmm, saxoo ko.

Jude 1:16 TSK

Ñooñoo di ñaxtu ak a jàmbat, te topp seen bakkan; kàdduy damu yu réy ay jibe seen gémmiñ, te ñooy jay ñi ñu yaakaare njariñ.