Sama Yàlla, maa soppa def sa coobare, ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.»
TSK
TSK · Philippians 2:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Man nag ma noon: «Maa sonn ci dara, coonob cóolóol bu amul njariñ.» Teewul sama àttee nga fa Aji Sax ji, sama yool a nga fa sama Yàlla.
¶ «Te it maa leen ko wax, képp ku dëggal fi kanam nit ñi, ne man nga féeteel, Doomu nit ki itam dina dëggal fa kanam malaakay Yàlla ya, ne moom nga féeteel.
Li mu wax moo di: «Kàddu gaa ngi ci sa wet; mu ngi ci saw làmmiñ ak ci sa xol.» Te loolu mooy kàddug ngëm gii nuy xamle.
noonu ngeen xawa xame ne nun, man ngeen noo damoo, te nun it, yeen la nuy damoo, keroog bésu Sang Yeesu.
Li may ragal ci yeen daal mooy sama coono ci yeen neen.
Ndax kat, ana kan mooy sunu yaakaar, di sunu mbég, te di sunu kaala gu nuy sagooji? Xanaa du yeen, kera ca sunu kanam Boroom Yeesu, bu feeñee?
Defal sa kem-kàttan ba boo teewee fa kanam Yàlla, di ku mu gërëm, ab liggéeykat bu mucc gàcce, di xamle kàddug dëgg gi ni mu ware.
Ndax kat dangeena judduwaat, te jiwu wi ngeen judduwaate mooy kàddug Yàlla giy dund te sax dàkk; du jiwu wuy yàqu, waaye mooy jiwu wu dul yàqu mukk.
¶ Noo gi ak Séet bi neeñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.