TSK

TSK · Philippians 2:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji dafa wax ne: «Alkànde ñeel na ku yaakaar doom aadama ak képp kuy doolewoo nit, dëddu Aji Sax ji.

Esayi it neeti: «Ab car ay bawoo ca Yese reen ba, mooy taxaw, yilif jaambur ñi dul Yawut, te moom la ñi dul Yawut di yaakaar.»

Looloo tax ma yebal ci yeen Timote, sama doomu bopp, ji sax ci yoonu Sang bi. Moo leen di fàttli samay doxalin ci yoonu Almasi, noonu ma koy jànglee fépp, ci mépp mbooloom gëmkat.

¶ Dingeen mana xam nag lu jëm ci man, ak li may def, ndax Tisig, mbokk mu ñu sopp, jawriñ ju wóor ci liggéeyu Boroom bi, moo leen di xamal lépp.

Sama yaakaar nag moo di, bu may am lu leer ci sama mbir rekk, moom laay daldi yebal ci yeen.

Lii sax moo tax ma yónni ko ci yeen: xamal leen lu jëm ci nun, ak itam, teewaayam bu dëfal seen xol.

¶ Waaye léegi bi Timote délsee, bawoo ci yeen, xibaaru jàmm la nu àgge ci seen ngëm, ak seen cofeel, ak ni ngeen nuy bégee di fàttliku saa su nekk, te namm nu lool ni nu leen namme, nun itam.

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne moo mana sàmm li ma ko dénk ba keroog bés ba.

Li ngeen di wax kay moo di: «Bu soobee Boroom bi, dinanu dund ba def nàngam sii mbaa nàngam see.»