Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.
TSK
TSK · Philippians 2:30
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sunu yaramu judduwaale wii nara yàqu, fàww mu sol weneen wu dul yàqu; sunu yaramu ndee wii, fàww mu sol yaramu deetil.
Maa ngi bége teewaayu Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus, ndax bi ngeen wuutee tey, ñoo leen taxawal.
Man nag xol bu sedd laa yeboo ci jaay mboolem lu ma am, ba jaay sama dooley bopp ngir seen jëmmi bopp. Xanaa duma leen ji gii cofeel gu réy, di feyoo cofeel gu ko yées?
Su ma ci deeyee sax, ba sama dund mel ni sarax su ñu tuur, tofal ko ci sarax, bi seen ngëm taxawe, su boobaa it maa ciy bég, te di leen woo, ngir bokk ak yeen ñépp bànneexu.
¶ Maa ngi bége Boroom bi lool ci nii ngeen mujj yeesale tey, seen yitte ci man, yitte ju ngeen amoon moos naka jekk, xanaa dangeena ñàkkoona jekku seen ndimbal.
Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi.