Lenn laa ñaan Aji Sax ji, lii laay sàkku: dëkk kër Aji Sax ji, sama giiru dund, di niir taaru Aji Sax ji, te yéemoo këram.
TSK
TSK · Philippians 3:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yeesu ne ko: «Képp ku tàmbalee gàbb tey xool gannaawam, jekkoo ci nguurug Yàlla.»
Waaye léegi jeexal naa sama sas ci gox yii, te gannaaw at yu baree ngii, ma namma dikk ba seetsi leen,
¶ Kon nag gannaaw-si-tey, ni nitu suuxu neen di xoole moroomam, nun xooleetunu ko kenn. Doonte ni nitu suuxu neen lanu xoole woon Almasi, léegi xooleetunu ko noonu.
¶ Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,
¶ Du caageenu damaa àgg ci loolu lépp ba noppi, mbaa damaa mat sëkk xaat, waaye maa ngi wéye samaw xél, di jéema jot ci neexalu rawante bi, gannaaw ba ma Almasi Yeesu jotee ci man itam.
¶ Kon nag nanu jóge ci ndoortel àlluway Almasi, daldi jàll jëm ci njàngum mag, te ñu baña lalaat kenu gi. Kenu gi mooy gëm Yàlla gannaaw tuubeel gi war ci jëf ju bon ji nit kiy def te muy jëfi ndee.
¶ Soppe yi, lenn a ngii, buleen ko umple: benn bés ni junniy at la mel ci Boroom bi; junniy at mel ni benn bés ci moom.