TSK

TSK · Philippians 4:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Gannaaw loolu mu yiwi ay magam ne leen: «Ngalla buleen xuloo ci yoon wi.» Ñu daldi dem.

¶ Bokk yi nag, dama leen di ñaax, ci sunu turu Sang Yeesu Almasi, ngir seen kàddu di genn, te féewaloo baña am ci seen biir, xanaa ngeen bennoo ci lépp, bokk menn xel, ak benn jëmu.

kon dëgg waay, mottlileen sama mbég, ba mànkoo, te ngeen soppantee genn cofeel, jubale seeni xol, te bokk benn jëmu.

Nangeen leen nawe seen kem kàttan te soppe leen noonu ndax seen liggéey. Gannaaw loolu, nangeen jàmmoo.

¶ Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.