TSK

TSK · Proverbs 1:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ngeen walbatiku, jooy ko Aji Sax ji, Aji Sax ji dégluwu leen, faalewu leen.

Job 27:9 TSK

Bu ko njàqare di dikkal, Yàlla day dégg yuuxam a?

Won nga ma ndoddi noon, ma boole bóom bañ yi.

Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko, tuub, waññiku ci moom.

Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.

Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal ak saraxu pepp it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.»

Hosea 5:6 TSK

Seen jur gu gudd ak gu gàtt lañuy àndal, di seet Aji Sax ji, duñu ko gis, te moo leen dëddu.

Amos 8:12 TSK

Dees na tambaambalu, géej ba géej, bëj-gànnaar ba penku, di wëraaluy sàkku kàddug Aji Sax ji, te deesul dajeek moom.

«Ba ma wootee,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «wuyuwuñu; moo tax ba ñu wootee, wuyuwuma.

James 4:3 TSK

Te su ngeen ñaanee, dungeen am, ndax mébét mu bon ma ngeen ñaane, ngir am lu ngeen toppe seen bakkan.