Sofental nga samay digle, nanguwoo samay àrtu.
TSK
TSK · Proverbs 10:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Doom, bul fàtte sama njàngle, defal sa xel ci saay santaane,
Baay digal ma, ne ma: «Jàppal samay wax ci sam xel, di jëfe samay santaane, ba dund.
Nga naan: «Su ma yégoon, sopp ab yar te baña sofental waxi àrtu.
Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artook ub yar di yoonu dund.
Mbugal tar na, ñeel ku wacc yoon; ku bañ waxi àrtu, dangay dee.
Teewlul te déglu li boroom xel yi wax. Defal sam xel ci li ma lay xamal.
Wax ju bare, caaxaani neen; mook gént yu baree yem. Kon, Yàlla, ragal ko.
Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokklee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
¶ Wattuleen bala ngeena tanqamlu kiy wax ak yeen. Ndegam ña tanqamlu woon ka yékkati woon kàddoom, wax ak ñoom ci kaw suuf ñoo rëccul, aste nun ñii, su nu dëddoo kiy waxe fa asamaan.