Psalms 1:6
TSK
Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.
Ku bon sànku; noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la, bu tàkkee, jeex tàkk.
Ku ñàkk xel réere ko, ku dofe umple ko.
Bu yoon amee, ku jub bég; kuy def lu bon jàq.
Ci Aji Sax ji laa leen di jàmbaarale, ciw turam lañuy daagoo. Kàddug Aji Sax jee!»
Su boobaa ngeen naan: “Noo daan bokk di lekk ak a naan, te sunuy pénc nga daan jànglee.”
Lépp laa mane ci ndimbalal Ki may manal.