Psalms 119:118
TSK
Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yaay xarab képp ku wàcc sa dogali yoon, ay pexeem neen.
Ab noon làqoo na ay waxam, lal pexey wor ca xolam.
Man de, bañuma laa sàmmal, topp la; bésub tiis it dagaanuma ko. Yaw de xam nga ko. Li ma wax it fi sa kanam la.
Mooy tabax kër Aji Sax ji te mooy soloo daraja, mooy toog, di jiite cib jalam, di sarxalkat bi cib jalam, te mébétu jàmm mooy dox diggante ñaar yooyu mu sasoo.”
Dañoo dem ba feese gépp xeetu njubadi, akug mbon, akug bëgge, akug coxor. Noyyeewuñu lu moy kiñaan, ak pexey bóome, ak ŋaayoo, akug njublaŋ, ak jëf ju sew. Ay jëwkat lañu it,
¶ Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof.