ngir saw tur di gëna màgg ba fàww, ñu naan: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi mooy Yàllay Israyil,” te waa kër Daawuda sax fi sa kanam, Sang bi.
TSK
TSK · Proverbs 12:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
2 Samuel 7:26
TSK
Esther 9:14
TSK
Buur joxe ndigal ngir ñu def noona. Ba loolu amee ñu siiwal ab dogal ca Sus, daldi wékk fukki doomi Aman yu góor ya.
Job 11:20
TSK
ku bon jàq, ba gët ya giim, rawtu réer ko, yaakaaratul lu moy noowam gu mujj.
Job 27:18
TSK
Mooy tabax kër gu tanewul mbaarum wattukatu tool, te lëndu jargoñ gën koo dëgër.
Psalms 37:10
TSK
Nes tuut, ku bon ne mes, nga seet, seet, mu réer.
Psalms 37:36
TSK
ma jaareeti fa, ndeke wuute na, ma seet ko, gisuma ko.
Proverbs 10:25
TSK
Bu ngëlén walee, ab soxor ne mes; ku jub, sab reen sax ba fàww.
Proverbs 14:1
TSK
Jigéen, rafet xel, dimbali waa këram, su deeb dof, tas këram.
Proverbs 15:25
TSK
Ku bew, Aji Sax ji màbb sa kër; ab jëtun, Aji Sax ji ñoŋal pàkkam.