TSK

TSK · Proverbs 13:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 15:28 TSK

Ku ni mel ay dëkke dëkk yu gental, ci kër yu kenn dul dëkke, kër yu nara doon jali tojit.

Job 20:19 TSK

Moo dëggaate néew-ji-doole, dëddu ko; aakimoo kër jaambur te tabaxu ko.

Yaay lekk saw ñaq, mbégteek ngëneel ñeel la.

Ku baax, donale ba cay sëtam; alalu moykat, muuru ku jub.

Alal ju la fen may, cóolóol la, day naaw, wut ko xaru la.

Kiy leble di tege, ba barele, kay yéwéne néew-ji-doole lay dencal.

Ab nay day yàkkamtee barele, te xamul, ba ko ñàkk di dab.

Kuy jagoo alal ju lewul, mooy picc mu toj lu mu nenul. Kookooy tollu digg dooleem, alal ja dëddu, mu mujje dof.»

James 5:1 TSK

¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.