Proverbs 10:22
TSK
Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.
Feppu dugub wu ànd ak dal moo gën lu ne gàññ kërug ayoo.
Lépp lu saay gët xemmemaa, xañuma ko sama xol. Bañaluma sama bopp benn bànneex, xanaa di bége lu ma liggéey, yooloo ko la ma liggéey.
Waaye benn ŋëb bu ànd ak dal moo gën ñaari ŋëbi doñ-doñ ci napp um ngelaw.
¶ Teewul njullite gu ànd ak doylu, di alal ju réy.