TSK

TSK · Proverbs 17:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 31:29 TSK

Ndegam maa bége musibay bañ, mbaa ma bellaxndikoo loraange ju ko dab,

Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga; ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.

Aji Sax ji sib na ku réy, da koy mbugal ci lu wér.

Man de, bañuma laa sàmmal, topp la; bésub tiis it dagaanuma ko. Yaw de xam nga ko. Li ma wax it fi sa kanam la.

«Soxore gi ngeen soxore seen mbokk Yanqóoba moo leen tax di sangoo gàcce, te dees na leen dagg sànni ba fàww.

Waruleen woona seetaan ci seen bésub mbokk, bésub njekkaram, Waruleen woona bége deminu Yudeen ñi ci seen bésub sànkute, mbaa ngeen di réy làmmiñ, ci bésub njàqare.

Ñi ci mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi ci naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.