TSK

TSK · Proverbs 18:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi nag Aji Sax ji, sama Yàlla, fal nga ma buur, ma wuutu saa baay Daawuda. Waaye Sang bi, man ndaw lu tuut laa, xawma sax nu may doxale.

Ma ne: «Wóoy man, sànku naa! Man miy nit ku làmmiñam sobewu, xeetoo ci ñu seen làmmiñ sobewu, te samay gët tegu ci kaw Buur Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi.»

«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk.

xanaa ngay diirook Boroom asamaan, bay santaane ñu indil la ndabi këram, nga di ci naan biiñ, yaak say jawriñ ak say soxna ak say nekkaale, ngeen di sàbbaal ay yàllay xaalis ak yu wurus ak yu xànjar ak yu weñ ak yu bant ak yu doj, te du ci lenn luy gis mbaa muy dégg mbaa mu xam dara. Waaye Yàlla ji yor sa bakkan tey ak ëllëg sàbbaaloo ko.

Ba nga tàmbalee ñaan la kàddu dikk. Maa la ko yégalsi, ndax yaw ku ñu naw nga. Déggal kàddu gi te dégg peeñu mi.

¶ Ba bés ba ñu jàpp agsee, Erodd sol colu buuram, toog ca jal ba, di leen àgge kàddug kilifteefam.