TSK

TSK · Proverbs 19:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

muy dunde ngëneel, askanam moom réew mi?

Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax, ndokklee yaw mi ko làqoo.

Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof.

Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg.

Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.

Woyofal te ragal Aji Sax ji, am alal, gudd fan ak daraja.

Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.

¶ Te itam nag xam nanu ne Yàlla mooy def mboolem lu xew, daje ba jur njariñal ñi sopp Yàlla, ñi mu woo, noonee ko ab dogalam namme.

Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.

Boroom bee may wallu ci jépp jëf ju bon, te moo may aar ba tàbbal ma fa nguuram ga fa asamaan. Daraja ñeel na ko, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.