Proverbs 10:1
TSK
¶ Kàddu yu xelu yu Suleymaan. Doom rafet xel, baay ba bég; doom dof, ndey ja tiis.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Kàddu yu xelu yu Suleymaan. Doom rafet xel, baay ba bég; doom dof, ndey ja tiis.
Surga, bu rafetee xel, tiim doom juy rusloo, séddu ni doom ci alalu sangam.
Déglul sa baay bi la jur. Bu sa ndey màggatee, bu ko sàggane.
Mbégte ñeel na ku saxoo ragal, waaye ku dëgër bopp tàbbi ci njekkar.
Ag maas a ngi saaga baay, te wormaaluñu ndey.
Ka gën di ndaw ne baay ba: “Baay, jox ma cér bi ma yoon may ci sunu alal.” Ba loolu amee baay ba séddale leen alalam.