TSK

TSK · Proverbs 22:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yal nanga nu xiir ci lim sunuy fan, ba nu mana dawal xel mu rafet.

Baay digal ma, ne ma: «Jàppal samay wax ci sam xel, di jëfe samay santaane, ba dund.

Dégluleen ku leen di yar, daldi muus. Buleen ko sàggane!

Ma walbatiku, di jéema xam, di wut, di càmbar, di sàkkum piri, ngir xam li bon cig ndof, ak li dofe, cig ndof.

Ma walbatiku xalaat, di jéema xam fu xel rafete, di xoolaat li nit jàppoo fi kaw suuf, ba guddeek bëccëg, gëmmul bët.