TSK

TSK · Proverbs 22:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Jigéen ju gëna lewet te xay ci yeen, ba néegula teg ndëggul tànkam ci suuf ndax xayteem ak lewetaayam, dina xeelu jëkkëram ju muy noyyee, ak doomam ju góor ak ju jigéen.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Wutala wut lu baax, ñu nawloo la; ku sàkku lu bon, yaa koy yenu.

Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.

Ku xañ say waajur seen alal te defe ne tooñoo, yaa neexook saaysaayu yàqkat.

Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, gis ku rafle, wodd ko, te baña nëbbu mbokk mu soxla?

Luke 6:35 TSK

Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe.

Nu nekk laa leen wone ne sunu wartéef mooy nu liggéeye noonu bu baax, ngir dimbali néew-doole yi, tey fàttliku kàddug Sang Yeesu, ga mu noon: “Nangu, joxee ko ëpp barke.”»

¶ Lii rekk la: ji lu tuut, góob lu tuut; ji lu bare, góob lu bare.

Yàlla ñàkkul worma bay fàtte seen liggéey, ak cofeel gi ngeen sopp turam, te firndeele ko ni ngeen taxawoo ñu sell ñi, démb ak tey.