TSK

TSK · Proverbs 23:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ñu neeti: «Alku ñeel na ku toxal màndargam kemu suufas moroomam.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!»

Job 22:9 TSK

Yaa bàyyi jëtun, mu deme loxoy neen, tey néewal doole ab jirim.

Job 24:9 TSK

Xoncees na jirim ci weenu ndeyam, jëlees na tayle alalu néew-ji-doole.

Jëtun akub doxandéem, ñu faat; ab jirim, ñu bóom,

Su ngeen jekkalee jekkal seeni jikko ak seeni jëf déy, di defa def yoon seen digg ak seen moroom,

Aji Sax ji dafa wax ne: Deeleen jëfe dëgg ak yoon, di xettli ku ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole. Ab doxandéem, ab jirim akub jëtun, buleen leen lor, buleen leen fitnaal. Deretu jaambur bu deful dara it, buleen ko tuur ci bii bérab.

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.