TSK

TSK · Proverbs 23:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu wax seen magi dëkk ba, ne leen: «Sunu doom jii ku dëgër bopp la te të. Déggalu nu, xanaa di xawaareek a màndi rekk.»

Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.

Gone gu sàmm yoon am nag dégg, ku ànd ak sagaru nit gàcceel sa baay.

Wóoy ngalla ñiy teela xëy, daw wutiw ñoll, gonloo biiñ ba tàng jérr.

Te yeena ngii ci mbég ak bànneex, di rendi nag ak xar, di yàpp ak a naan, naan: «Nan lekk, naan, nde ëllëg, nu dee!»

Ay fan yu néew gannaaw gi, ka gën di ndaw jaay léppam, daldi tukki réew mu sore, di topp bakkanam ba yàq fa alalam.

¶ «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,

Buleen naan biiñ ba màndi, màndite ci afal seen bakkan la leen jëme, waaye na leen Noo gi fees,