Psalms 119:72
TSK
Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sa ngëneelu yoon wi nga digle moo ma gënal ay junniy xaalis ak wurus.
Teewlul xel mu rafet, sam xel di dégg.
Bul yedd kuy ñaawle, da lay jéppi; yeddal ku rafet xel, mu naw la.
Wutal xel mu rafet, bàyyi wurus; taamul ag dégg, wacc xaalis.
Ku am ug dégg wut xam-xam, ku rafet xel sàkku xam-xam.
¶ Waaye la ma jàppe woon ag ndollant, moom laa def tey ag wàññeent ndax Almasi.
dama lay digal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci sawara ba mu set wecc, ngir nga am alal. Jëndal itam yére yu weex yoo soloo, ba làq sa duŋŋaaral gu gàccelu gi; ak tuufaay looy tuufoo, ngir nga gis.