1 Samuel 9:20
TSK
Mbaam yi nga réerle bëkk-démb, bu ci am benn xalaat, ndax feeñ nañu. Te sax, mboolem lu bakkane ci Israyil, xanaa du yaay boroom, yaak sa waa kër baay?»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mbaam yi nga réerle bëkk-démb, bu ci am benn xalaat, ndax feeñ nañu. Te sax, mboolem lu bakkane ci Israyil, xanaa du yaay boroom, yaak sa waa kër baay?»
¶ Daawuda ne Sóol: «Waaw, ana lu ma tekki, man maak samay bokk, sama askanu baay ci Israyil, ba wara mana goromlook Buur?»
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwma, daŋŋiiraluma, xintewoowma lu réy it, mbaa lu ma ëlëm.
Lekk lem ju ëpp baaxul, te wut waaw-góor du ngóora.
Ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, da di manumaa wax, gone doŋŋ laa.»