TSK

TSK · Proverbs 26:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Waaye doomi Yanqóoba ya, ay nax lañu tontoo Sikem ak baayam Amor, ndax li Sikem torxal seen jigéen Diina.

Absalom nag ne ko: «Bàyyil boog sama mag Amnon, mu ànd ak nun.» Mu ne ko: «Lu muy ànd ak yaw doye?»

Yowab ne Amasa: «Mbokk mi, mbaa jàmm nga am?» Yowab jàpp sikkimu Amasa ca loxol ndijooram, mel ni ku koy fóon.

Dañuy fenante, làmmiñ dig lem, xol ba njuuy la.

Noon yaa ngi may yéene lu bon, naan: «Xanaa kii du dee, ba ñu fàtte ko?»

Aji Sax ji bañ na njublaŋ ci nattub diisaay, ay nattukaay na mat, muy bànneexam.

Ku ñaw day xelu, xam li muy def; ab dof di nax boppam.