TSK

TSK · Proverbs 28:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 32:9 TSK

Dund-jopp taxula rafet xel, te di mag taxula xam yoon.

Ku jëkke layoo, ñu ne yaa yey, ba keroog ka nga joteel weddi la.

Bul rey sa bopp ci wut alal, bu ko xalaat sax.

Ab yaafus day foog ne moo gëna muus juróom ñaari boroom xel yu xam tont.

Wóoy ngalla ñii defe ne ñoo xam, yaakaar ne ñoo muus.

Xëy na yaa sut Dañeel am xel, du genn kumpa gu la ump!

¶ Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.

¶ Bu kenn nax boppam: Ku teg boppam ci yeen, boroom xam-xam, ni xarnu bii jàppe xam-xam, kooku na doon ab dof, ngir am xam-xam bi wóor.