TSK

TSK · Proverbs 29:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sang bi, bul déglu mukk nit ku bon kii, Nabal mii. Moom turam doŋŋ la wuyu, nde Nabal (Dof bi) la tudd, te ndof la nekke. Man nag sang bi, gisuma woon ndaw yi nga yebal.

Job 31:13 TSK

Ndegam maa sofental sama àqu jaam, bu ñu may jooytu, diy góor mbaa jigéen,

Maa bañ kuy topp tuuri neen. Man, Aji Sax ji laa wóolu.

Mooy xettliji aji tumurànke bu woote wall ak aji néewle ju sësul fenn.

Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.

«Ëpplante banti seedar da laa def buur? Sa baay daawul lekk ak a naan? Teewu koo jëfe dëgg ak yoon, muy njiglaayam.

Waa réew maa ngi lekk àq, di sàcc. Baadoolo yeek walaakaana yi, ñu néewal; doxandéem bi, ñu not, xañ ko àqam.

¶ Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir gu ni mel.