TSK

TSK · Proverbs 3:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Waaye bu ngeen ma déggalul te baña jëfe sama santaane yooyu yépp,

Alkàndee ngi, ndegam déggaluleen seen santaaney Yàlla Aji Sax ji, xanaa wacc yoon wi ma leen di dénk bésub tey, ngir topp yeneen yàlla yu ngeen xamuloon.

Gaalu Aji Sax ji nekk na kër Obedd Edom waa Gaat ba ñetti weer. Aji Sax ji barkeel Obedd Edom, mook këram gépp.

Job 24:18 TSK

Yal nañu wéye walum ndox, te suuf sa ñu séddoo alku, ba kenn dootu dëgmal tóokëru reseñ.

Loo def mu àntu: nga mel ni garab gu saxe walum ndox, bu jotee meññ, te xob wa du lax.

genn loraange du la dab, balaa du jege sa xayma.

Ab soxor, këram day tas, mbaarum ku jub di naat.

Aji Jub ji Yàlla xam na la ne ca biir kër ku bon, te mooy sànk ku bon.

Maay wàcce alkute gi,» kàddug Aji Sax ji Boroom gàngoor yee, «mu dugg ba ci biir kër sàcc bi, ak kër nit kiy giñe sama tur, ay fen; ci biir kër gi la alkute giy fanaan, ba raafal banti kër gi, aki dojam.»