TSK

TSK · Proverbs 30:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Wattuleen seen bopp, bala leena jikko ju sew yóbbe ngeen naan ci seen xel: «Atum juróom ñaareel mi, atum njéggalug bor dëgmal na,» ba tax ngeen sajje xef, seen mbokkum ndóol, joxuleen ko dara. Da leen di booleek Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar.

¶ Doweg, Edomeen ba taxawandook jawriñi Sóol, daldi àddu, ne: «Man de, gis naa doomu Yese ji, mu dikk dëkk ba ñuy wax Noob, ca Ayimeleg doomu Ayitub.

Ngalla Buur, sama sang, déglul lii ma lay wax: su fekkee ne Aji Sax ji moo la xiir ci sama kaw, yal na ko cib sarax giifal. Waaye su dee ay doom aadama de, yal nañu alku ci kanam Aji Sax ji, ndax dàq nañu ma tey, ba xañ ma ab cér ci Aji Sax ji, mbete ku ñu ne: “Demal jaamuji yeneen yàlla.”

¶ Naka la Daawuda dox ba wees tuuti collu tund wa rekk, yem ca Ciba, surgab Mefiboset. Ma nga làng ak ñaari mbaam yu ñu laltaay, sëf leen ñaar téeméeri mburu ak téeméeri danki reseñ ak téeméeri danki figg ak mbuusum biiñ.

Lii it ñi rafet xel a ko wax. Par-parloo cib àtte baaxul.

Te it du lépp lu ñu wax, ngay bàyyi xel. Kon doo dégg surga bu la ŋàññ,

ba noppi ñu dem fekki Buur, ngir wax ak moom ca aaye ba mu tëral, ne ko: «Xanaa du yaa torlu aaye bi ne: képp ku ñaan jenn yàlla mbaa nit ku la moy, yaw Buur, diiru fanweeri fan, dees na ko sànni ca kàmbu gaynde ya?» Buur ne: «Dogal bi kay wér na, dëppook yoonu waa Medd ak Pers, wi dul toxu.»

Yaw miy sikkal jaamub jaambur, yaay kan? Su baaxalee mbaa mu bonal, sangam a koy seet! Te day baaxal ndax Boroom bi man na koo baaxal.