TSK

TSK · Proverbs 30:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 33:9 TSK

Nga ne: «Set laa def, tooñuma; mucc ayib laa def, ñaawuma fenn.

Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba.

Lu waay def, daa jekk ca moom, waaye Aji Sax jeey natt xol yi.

Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.

Bu ngeen raggoo woon saabu, ba raggooteek xeme it, seen ñaawtéef gàkk, may gis.» Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

«Éey Yerusalem, fóotal sa xol, jële ci lu bon, ndax nga mucc. Foo àppal sa mébéti xol yu bon?

Efrayim a ngi naan: «Woomle naa, maa amal sama bopp alal, te mboolem samaw ñaq, giseesu ci tooñaange ju di bàkkaar.»

Sang bi ne ko: «Yeen Farisen yi, bitib kaas bi ak ndab li daal ngeen di raxas, te fekk leen feese jikkoy jagoo lu lewul, akug mbon ci biir!

Farisen baa nga taxaw di yelu, naan: “Yàlla, maa ngi lay sante li ma melul ni ñeneen ñi doonul lu moy ay lekk-kati àq, ay njublaŋ aki jaalookat, rawatina juutikat bii.

Ag njullite lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.

Titus 3:5 TSK

ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell,

tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,