TSK

TSK · Proverbs 30:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñett a ngii, day yëngal suuf, ba ci ñeent yu suuf àttanul:

Ñett a ngii, ñu jekk um ndaag, ba ci ñeent ñu jekk doxin:

Waaye yeen, dikkleen fii, yeen doomi xërëmkat yi, yeen askanu njaalookat yiy gànctu,

Seenu ñoll giiful sax, ñuy gànctoo gànctu, te gàccee gënal seeni kilifa.

Amos 1:6 TSK

Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Gasa, te duma fomm seeni duma. Ñoo jàpp njaam mbooloom lëmm, jalax Edomeen ña.

Amos 1:11 TSK

Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom, te duma fomm seeni duma. Ñoo toppe seen bokki bànni Israyil saamar, jalax yërmande, mer mer mu dul meddi ak xadar ju dul giif mukk.

Amos 2:1 TSK

Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Mowab, te duma fomm seeni duma. Ñoo lakk yaxi buurub Edom, def ub dóom.

Micah 7:3 TSK

Lu bon la seeni loxo mane: kàngam di laaj, ab xaali di sàkkub ger, boroom daraja moom, di wax fuqley bakkanam, ñu ànd ràbbum pexe.

Ñu ni mel liggéeyaluñu Almasi sunu Boroom, seen koll lañuy liggéeyal. Làmmiñ yu neex, ak kàddu yuy jaye lañuy naxe ñi seenum xel foogadi.

Loraange lees leen di feye loraange gi ñu sabab. Seen mbégte mooy xawaarey bëccëg ndarakàmm. Ñooñoo diy gàkk, aki sikk, ndax seen teewaay gàcce la ci seen biir yeen, bu ñuy bokk ak yeen bernde, te ca lañuy bànneexoo ay nax.