TSK

TSK · Proverbs 30:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»

ñu baree may tooge naa: «Yàlla du ko wallu!» Selaw

Maak yaw kay, ma song gàngoor. Maak sama Yàlla, ma tëb um tata.

Yoonu Aji Sax jee mat, di leqli bakkan. Lu Aji Sax ji seede dëgg la, day xelal ku xeluwul.

Dama naa Aji Sax ji: «Yaw laay làqoo, di la fegoo; ngay sama Yàlla ji ma doyloo.»

Sang bi, maaka sopp sa kàddu gi set ni weñ gu ñu xelli!

Ragal nit dugal sa bopp la, ku wóolu Aji Sax ji, fegu.

¶ Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.