TSK

TSK · Proverbs 8:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

alal ak koom am sa kër, sag njekk sax dàkk.

Njàlbéenu xel mu rafet mooy sàkku ko; ak loo mana am, amal ug dégg.

Xam-xam ay feesal néeg ya ak mboolem alal ju jafe te yànj.

Ndaxam lenn doŋŋ a manula ñàkk. Maryaama nag, cér bi gën la taamu, te deesu ko nangu ci moom.»

Jaayleen seen alal, sarxe xaalis bi, sàkkuleen mbuus yu dul ràpp, muy dencu ëllëg bu dul jeex fa asamaan, fa ko sàcc dul jege, max du ko yàq.

Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.

Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi,

¶ Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.

James 5:1 TSK

¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.