¶ Ci biir loolu mu defar néeg ba ñuy wooye Néegu jëni kenu ya. Guddaay bi di juróom fukki xasab, yaatuwaay bi di fanweeri xasab, ak beneen néeg ci kanamam, mu ànd ak ay jëni kenoom ak xaddam bu mbaar ci kanam.
TSK
TSK · Proverbs 9:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma, di xaacu ca pénc ma.
Doom, bul fàtte sama njàngle, defal sa xel ci saay santaane,
«Éey, yeen ñi mar ñépp, dikkleen ci ndox mi, ba ci ku amul xaalis sax! Dikkleen jënd pepp, lekk! Dikkleen jënd pepp mu xaalis jëndul, ak biiñ ak meew mu amul pey.
Noo bokk diy surga ci liggéeyu Yàlla bi; yeen ngeen di toolu Yàlla, di tabaxub Yàlla.
Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi.
Waaye ni ab tabaxkat ëppe teddnga kër ga muy tabax, ni la Yeesu yelloo daraja ju ëpp ja Musaa yelloo woon.
Ku am ndam nag, maa lay def nga doon ag kenu fi sama biir néeg Yàlla, te doo fa génnati mukk. Maay bind fi sa kaw sama turu Yàlla ak sama turu dëkku Yàlla, te mooy Yerusalem gu bees, giy wàcce fa kaw, bàyyikoo fa sama Yàlla, maay bind it fi sa kaw sama tur wu yees.