TSK

TSK · Psalms 21:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sawaraa ngay tàkke ca samam sànj, di lakke ba ca xóotey njaniiw, ba xoyom suuf ak meññeefam, ba jafal reeni tund ya.

Job 6:3 TSK

Kon tey mu gëna diis suufoo suufi géej. Moo waral sama kàddu yi ma rëcc.

Sujjóotal-leen doom ji, bala moo mer, ngeen sànkoo seenu yoon; meram day jekki ne jippét, waaye ndokklee képp ku ko làqoo!

Ma dàq noon yi, dab leen, jekkli, doora dëpp.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat.

Aji Sax ji, yaa xàcci sa loxo, waaye yéguñu ko. Won leen ni nga nabe ci sa ñoñ, ñu rus, te sawaraay xoyom sa noon yooyu.

ba noppi mu sant ay dag yu am kàttan ci mbooloom xareem, ngir ñu yeew Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, sànni leen ca biir taal bu yànj ba.

Ñoo nuy aaye nu àgge jaambur ñi dul Yawut, kàddu gi leen di musal. Noonu lañu matale seen jóorub bàkkaar yi ñu nekke naka jekk, waaye am sànj a leen mujj dab.

Ñu ne tund yeek doj yi: «Daanuleen ci sunu kaw, làq nu kanamu ki toog ci ngàngune mi ak sànjum Gàtt bi,

Ba loolu amee ñu jàpp ndee ak njaniiw, sànni ca déegu sawara sa. Ñaareelu dee gi nag moo di déegu sawara si.