TSK

TSK · Psalms 69:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Jombul mu am ku dégg kàdduy ngiñ lii, tey nax boppam cim xelam, naan: «Jàmm rekk laay am, maa tey të,» ba tax ñax mu wow lakkaale mu tooy.

«Ana lu nuy toog? Fabuleen, nu dem ca dëkk ya tata wër, deeyi fa. Sunu Yàlla Aji Sax ji nar na sunu dee; moo nu nàndal tookey mbugal, nde noo tooñ Aji Sax ji.

Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi wax lii ci mbirum yonent yi: «Maa ngii di leen leelsi njàqarey xeme, nàndal leen tookey mbugal, nde fi yonenti Yerusalem la yàqute tukkee, ba law ci réew mi mépp.»

Sobey Siyoŋ ca pendalam, te bàyyiwul xel ag mujam. Jéllam ba yéeme na, te amul ku ko dëfal. Siyoŋ nee: «Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare; noon bi déy, am na ndam!»