TSK

TSK · Revelation 19:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ma siiwali saw tur ci bokk yi, màggale la digg mbooloo mi.

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ayca, santleen Aji Sax ji, yeen jaami Aji Sax ji yépp, yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi.

Éey waa kër Israyil, santleen Aji Sax ji! Éey waa kër Aaróona, santleen Aji Sax ji!

Na lépp luy noyyi màggal Ki Sax! Màggal-leen Ki Sax!

Askan yee meroon, waaye sa mer a dikk tey; tey jii ngay àtte ñi dee, yool say jaam, yonent yi, yool ñu sell ñeek ñi la ragal, mag ak ndaw, tey it ngay sànk ñiy sànk àddina.»

Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.