TSK

TSK · Revelation 21:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu ñu ne ko: «Xam nga lan la, sang bi? Am na ci nun juróom fukki nit ñu jàmbaare. Nañu dem seetali la sa sang ba. Jombul leeru Yàlla yóbbu ko, teg ko ci kaw tund yii, wenn, mbaa mu teg ko ci biir xur yii, wenn.» Mu ne leen: «Déedéet, buleen leen yebal.»

Mu tàllal lu bindoo ni loxo, daldi sëq sama kawaru bopp, lenn ngelaw yékkati ma ba ca diggante kaw ak suuf, yóbbu ma ba Yerusalem ci biir peeñum Yàlla, ba ca buntu ëttu biir kër Yàlla ba janook bëj-gànnaar, fa ñu teg jëmmu bokkaale, jay sabab fiiraange.

Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu ba ca waa ngàllo ga ca réewum Babilon, lépp ci peeñu, ci dooley Noowug Yàlla. Peeñu ma ma gis nag yem fa.

¶ «Pàkk bay des ci yaatuwaayu dog boobu dina yaatoo juróomi junniy xasab (5 000), gudde ñaar fukki junniy xasab ak juróom (25 000); suufas ñépp la pàkk boobu di doon, ngir dëkk bi. Man naa doon ay dëkkuwaay aki parlu, te na dëkk bi ci boppam féetewoo digg ba.

Maa xam aw nitu Almasi, ba ñu ko yéegee ba ñetteelu asamaan, fukki at ak ñeent la tey. Ndax aw yaramam lees ko yéegaale woon? Xawma, ndax yéegaaleesu ko aw yaramam? Xawma, Yàlla rekk a xam.

Ma jekki rekk nekk ci biir Noowug Yàlla. Ci kaw loolu, yemuma lu moy ci am ngàngune mu tege ca asamaan, mu am ku toog ca ngàngune ma.

Ma gis nag dëkk bu sell bi, Yerusalem gu bees gi, mu wàcce asamaan, fa Yàlla, mel nib séet bu defaru ba jekk ngir jëkkëram.