TSK

TSK · Revelation 21:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

sa yére yépp di gilli ndàbb, alowes akum kanel, ñu di la bégale xalam, ca sa biir kër yu yànj.

Yaw, dëkkub Yàlla bi, tuddees na say jaloore. Selaw.

Yewwulee, yewwul, Siyoŋee, làmbool sa doole! Yerusalem, dëkk bu sell bi, solul ba ne ràññ! Ndax du kenn ku xaraful mbaa ku sobewu ku lay songati.

Maa béga bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam njekk, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.

¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq. Dees na ne: “Yaw dëkkuwaayu njekk bii, yaw, tundu Siyoŋ wu sell wi, yal na la Aji Sax ji barkeel!”

Maa leen di fiiree fiiraangey Yàlla ci boppam, ndax jenn jëkkër doŋŋ laa leen digool ab séy, te mooy Almasi mi ma leen namma jébbal, te fekk leen di janq bu set wecc.

¶ Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba jooxeel leen bakkanam.

Booba Ibraaymaa ngay séentu dëkk ba ca kenu ya, te Yàlla di ki yor xaralag tabax bi, boole ci di tabaxkat bi.

ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.

¶ Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,

Ku am ndam nag, maa lay def nga doon ag kenu fi sama biir néeg Yàlla, te doo fa génnati mukk. Maay bind fi sa kaw sama turu Yàlla ak sama turu dëkku Yàlla, te mooy Yerusalem gu bees, giy wàcce fa kaw, bàyyikoo fa sama Yàlla, maay bind it fi sa kaw sama tur wu yees.

Nanu bég, di bànneexu te màggal ko, ndax céetu Gàtt bi agsi na, ab séetam defaru na ba noppi!

Te ku wàññi lenn ci kàdduy waxyu yu téere bii, sa wàll la Yàlla di wàññee ci yooyii ñu bind ci téere bi, muy garabu dund gaak dëkk bu sell ba.