Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»
TSK
TSK · Revelation 21:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.
waaye noonu it lay waare ay xeeti xeet, ba buur yi wedam, ngir lu ñu leen waxuloon, te ñu gis ko, lu ñu dégguloon, te mujj ko ràññee.»
Ab taw ak tawub yuur asamaan lay wàcce, du fa dellu, te suuxatul suuf, saxal ko, meññal ko, ba kuy ji, mu may la jiwu; kuy lekk, mu may lam pepp.
Taaru àllub Libaŋ a lay ñibbsil, garabu sippar, pẽe ak geneen gu dëkke naat, taaralsi sama kër gu sell gi, ba ma terale ci sama ndëggastalu tànk.
Su ko defee ngeen nàmp ba suur weenam wiy naxtaane, su ko defee ngeen nàmp bay tàqamtiku soowum weenam mi ne xéew.
xanaa di waate Aji Sax jiy dund, ci dëgg ak njub ak ngor, kon xeet yi di barkeeloo Aji Sax ji, di ko sagoo.»
Askan yu bare, ak xeet yu am doole ñooy dikk, di sàkkusi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi ci Yerusalem, di dagaansi Aji Sax ji.
ngir ma doon jawriñu Almasi Yeesu, ñeel jaambur ñi dul Yawut, may wàccoo ak liggéeyu carxal bi xibaaru jàmm bu Yàlla laaj; su ko defee ñi dul Yawut mana doon ab jooxe bu Yàlla nangu, jooxe bu Noo gu Sell gi sellal.
Dees na fa indi darajaak teraangay askan yi.