Li feek jàngoro jaa ngi ci moom, day sobewu te gannaaw daa sobewu, na dëkk moom doŋŋ te na dëkkuwaayam génn dal bi.
TSK
TSK · Revelation 21:27
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee ñu génne Maryaama dal ba diiru juróom ñaari fan. Mbooloo ma demul, ba keroog ba ñu délloosee Maryaama ca biir dal ba.
Foofa law yoon di jaare, ñu di ko wooye Yoon wu sell wi. Ku sobewu du fa jaare, ñi moom woowu yoon, ñooy ñi koy topp. Ab dof sax du fa lajje.
Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, te ñooy moom réew mi ba fàww. Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.
¶ Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmi, te mooy: powum séy, ak jëfi sobe, ak yàqute,
Yaw itam sama mbokkum surga bu dëggu bi, dama lay ñaan nga jàpple leen ci, ñoom ñaar ñooñoo bokkoon ak man coonob xamle xibaaru jàmm bi, ñoom ak ñoom Kelemaŋ, mboolem sama bokki liggéeykat yi seeni tur binde ca téereb dund ba.
Ku am ndam mooy soloo noonu mbubb mu weex, te turam, duma ko far ci téereb dund bi, waaye maa koy wuyul ci sama kanam Baay ak ay malaakaam.
Jigéen jaa ngi sol lu yolet te xonq, takk wurus ak jamaa aki per. Mu ngi yor kaasu wurus bu fees ak ñaawtéef ak sobey moyam.
Képp ku ñu gisul ñu bind la ci téereb dund bi, ci déegu sawara si lees la sànni.
¶ «Ndokklee yeen ñi fóot seeni yére, ngir saña lekk ci garabu dund gi, jàlle bunt yi, dugg ci biir dëkk bi.