TSK

TSK · Revelation 21:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mooy yékkatee ku ndóol ci suuf, jële ku ñàkk ci mbuubit, boole leen dëj ca garmi ya, sédde leen jataayu teraanga. «Aji Sax jee moom kenuy suuf, samp ci àddina.

Fi Yanqóoba laay soqee aw askan, fi Yuda laa ne, fi laay jële lu séddoo samay tund. Samay tànnéef a koy séddoo, sama jaam ñi kay a fay dëkke.

¶ «Lii nag moo di kóllëre gi may fas ak kër Israyil, gannaaw yooyu fan, la Boroom bi wax, mu ne: Maay yeb sama ndigali yoon ci seenum xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.

Lu bon, buleen ko feye lu bon; ay saaga it, buleen ko feye ay saaga. Xanaa ngeen ñaanal leen, feye leen ko, ndax ci loolu lees leen woo, ngir ngeen jagoo barke.

Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may nga lekk ci garabu dund gi ci Àjjana, toolub Yàlla.

¶ «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; doj wu ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.

Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla.