¶ «Buleen sàkkal seen bopp tuur muy jëmmal lenn lu nekk ci kaw asamaan, mbaa ci kaw suuf, mbaa lu nekk ci ndox mu suuf tiim.
TSK
TSK · Romans 1:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
am gémmiñ te du wax, ami gët te du gis,
Ana kan ngeen di niruleek Yàlla, ak nataal bu ngeen koy dendaleel?
Liggéeykatu bant tàllal buumu nattukaay, jël kew, nataale, xacc, rëdde rëddukaayu wërngal, jox ko bindu nit, jekkal ba mu mel ni nit, nar koo fat cib néeg,
Naka laa jàll ba xool, yemuma ci lu moy ay nataal yu ñu ñaas ci miir bi bépp, di mboolem dundoot yuy ramm-rammi ci suuf, ak rab yu jara seexlu, ak mboolem jëmmi kasaray tuur yu waa kër Israyil di jaamu.
Ñoo weccee dëggu Yàlla, aw fen, di sujjóotal ak a jaamu mbindeef, bàyyi Bindkat bi yelloo cant ba fàww. Amiin.
Ndax démb kat yàgg ngeena def coobarey xeet yi xamul Yàlla, ci ay ñaawtéef, ak topp seen bakkan. Dangeen daa màndi ak a xawaare, dëkke naan biiñ, di jaamu tuur yu seexluwu, waaye na fi yem nag.