TSK

TSK · Romans 1:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Beñamin la wax, ne ko: Soppeb Aji Sax jaa ngi, keey dëkke xel mu dal fi wetam, mu di ko yiir bésoo bés, te diggantey waggam la dëkke.

Acts 7:59 TSK

¶ Ñuy dóor Eccen ay doj, moom muy ñaan Yàlla, naan: «Sang Yeesu, nangul sama bakkan!»

Te yeen ñi ñu woo ci Yeesu Almasi itam, ci ngeen bokk.

du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel, gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.

ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.

¶ Ci man Póol, ndawal Almasi Yeesu ci coobarey Yàlla, ci man la bataaxal bii bawoo, bawoo itam ci Timote mbokk mi, ñeel mbooloom Yàlla mi ci Korent, ak mboolem ñu sell ñi ci diiwaanu Akayi gépp.

¶ Bokk yi, yal na sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi ànd ak seenum xel. Amiin.

¶ Yal na jàmm ñeel bokki gëmkat ñi, ak cofeel gu ànd ak ngëm, bawoo fa Yàlla Baay bi, ak Sang Yeesu Almasi.

¶ Daraja ñeel na Yàlla sunu Baay, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.

ñeel waa Kolos ñu sell te wóor te di bokki gëmkati Almasi. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay.

¶ Na jàmmu Almasi saytu seen xol. Ci jooju jàmm lañu leen woo, fekk leen ngeen di wenn yaram doŋŋ, te it saxooleen cant.

ak di baamtu fi kanam Yàlla sunu Baay, jëf ji juddoo ci seen ngëm, ak liggéey bi sottee ci seen cofeel, ak yaakaar ji ngeen saxoo di séentu sunu Sang Yeesu Almasi.

¶ Sunu Sang Yeesu Almasi ci boppam, ak Yàlla sunu Baay, mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk, ak yaakaar ju wér,

Jaam yi seeni sang di bokki gëmkat, buñu yab seeni sang, ndax li ñuy bokki gëmkat, waaye na tax ñu gënati leena jaamu, ndax seen sang yooyu di jariñoo seenu ñaq, ay gëmkat lañu, ay soppe lañu.

Yal na Boroom bi wéttali sam xel. Aw yiw ñeel na leen.

Yeen la aw yiw ak jàmm ñeel, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

James 1:1 TSK

¶ Ci man Yanqóoba, jaamub Yàlla ak Sang Yeesu Almasi, la bataaxal bii bawoo, ñeel fukki giir ak yaar yi tasaaroo ci àddina. Maa ngi leen di nuyu.

Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin.

Jude 1:1 TSK

¶ Ci man Yudd miy jaamub Yeesu Almasi, di rakku Yanqóoba, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel leen yeen ñi ñu woo, yeen ñi Yàlla Baay bi sopp, te sàmmal leen Yeesu Almasi.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Efes, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Ki yor juróom ñaari biddiiw yi ci loxol ndijooram, di doxe digg juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi. Mu ne:

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Pergam nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Boroom saamar bi ci ñaari ñawka yi. Mu ne:

Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Lawdise nag, bind ko, ne ko: «Lii moo di kàdduy Waawu Yàlla ji, Seede bi wóor te dëggu, Ndeyu càkktéefu Yàlla ji. Mu ne: