TSK

TSK · Romans 10:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ne ko: «Ñëwal nu dem rekk, nga gis ni ma farloo ci mbiri Aji Sax ji.» Mu waral ko watiiram, yóbbu ko.

di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»

¶ Ba ba muy wax loolu, mbooloo maa nga koy déglu. Ba ñu déggee kàddu yooyu lañu xaacu ne: «Jëleleen ko ci kaw suuf! Ku mel ni kii yeyoowula dund!»

Waaye xeetu Israyil wi sàkku woon yoonu njub, ñoo moy yoon wi.

Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.

Seen kemu am-am lañu joxee, maa ko seede, lu wees seen am-am sax lañu joxee xol bu sedd.

Ana seen mbég mooma woon nag? Ndax kat maa leen seedeel ne su manoona am sax, seeni bët ngeen di luqi, jox ma.

¶ Li may ñaan nag moo di seen cofeel yokku tey gën di yokku, te ngeen ànd ceek xam-xam bu matale ak gépp ràññee,

Maa ko seedeel ne coonoy ñaan bu réy la nekke, ngir yeen ak waa Lawdise ak waa Yerapolis.